WAKH BI GUEUNE SI
ADOUMA MOYE RAITAME
TCHI TANG YOU NDIEUKE YI, YALLA MÜ NGI DORON DÉFAR LEUPALEUP YI.
TCHI NIEUP, YALLA SAKONA LEN LAF, BEUT, YARAM;
MÜ DESON KO TCHATOU LEUPALEUP YI. YALLA AMEUTOUL WONE BEUT, LAF, YARAMK, LOLOU YEP DONE DÉF NÉ LEPALEUP DONE NOURO FOULOR SUY NAW TCHI ASSAMANSI.
LI GUENON METI MODON KENEU MENOUL WONA GUISS TCHATOU LEUPALEUP. MOM TCHI BOPAM KHAMOUL WONE NÉ KÉNEU MANOUKO WONA GUISS.
DA FA DON NAW GNI YENEN LEUPALEUP YI, DI TAKHAW TCHI FOULOR NGUIR RAFÉTALLEN;
GNÉNÉN GNI DA GNOU KO DON BEUMEUKH, DI KO DANEL SU DON TAKHAW SAKH TCHI FOULOR BOU AMOUL WONE DARA.
TCHI KHELEM, TAR BI MOU AMON DOYONNA KO.
MÜ AM BESS BO KHAMNÉ NAKHAR DAF KO DAN.
TCHATOU LEUPALEUP, NAW BE TCHI YALLA NE KO:
-„YALLA LI NGA DEF BE KÉNEU DOU MA GUISS NAKHARI NA MA LOL BE TCH SU MA KHOL. DA MA BOUGON NGA DIMALIMA TCHI TOUTI RÉK BÉ DÉF MA MEL NI SUMEY MAG GNI“.
YA KHOL KO LOU YAGEU, KHALAT LOU YAGA YAGEU. MÜ NE KO:
-„DÉGUE NA LEU, WANTÉ LIGEY BI DEFAROU NA TÉ MOUNOU MA KO EULBEUTI. AMATOU MA DARA LOU MA LA MEUNEU MEY. TÉ SO AMON SAKH LAF, BEUT, YARAM AK LEUP BENA BESS DA NGEY MÜDJÉ DÉ NI SUMA BANTA YEUP. LOLÜ NGA BOUGA? “
TCHAT TONTÜ KO:
-„WAW SÜ GNÜ BOROM, SÜ DÉ LI MA DESS TCHI DUNDA DI NA DÉF MA MÜNA MEY NIT BANEKH, NANGOU NA DÉ“.
KHIBAR BI MU TONTÜ YENGUEL YALLA, MOUSSOUL WONE DÉGUE NIT BOU KO TONTU WON NI; MU KHALATAT LOU YAGA YAGEU.
MU NE TCHAT:
-„LI NGA WOKH RAFET NA. NEGUER NI KI TEY DOTULO DÉ TÉ GNEUP DI NA GNOU LA GUISS. DU MA LA DJOKH ITAM YARAM, WANTÉ DÉMAL TCHI NIT GNI TE NEKAL SEN SIIGN AK RÉTANE“.
Dieter J Baumgart
Trad. en wolof (Sénégal) par Adrienne Diagne